عن جابر رضي الله عنه:
أَنَّ رَجُلًا سَأَلَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: أَرَأَيْتَ إِذَا صَلَّيْتُ الصَّلَوَاتِ الْمَكْتُوبَاتِ، وَصُمْتُ رَمَضَانَ، وَأَحْلَلْتُ الْحَلَالَ، وَحَرَّمْتُ الْحَرَامَ، وَلَمْ أَزِدْ عَلَى ذَلِكَ شَيْئًا، أَأَدْخُلُ الْجَنَّةَ؟ قَالَ: «نَعَمْ»، قَالَ: وَاللهِ لَا أَزِيدُ عَلَى ذَلِكَ شَيْئًا.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 15]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Benn waay dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam, te dolliwuma ca dara, ndax dinaa dugg àjjana ? Mu ne ko: «waaw», waa ji ne: giñ naa ci Yàlla ne duma ci dolli dara.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 15]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ku julli julliy juróom yi nu farataal, te tegu ca ay naafila, woor weeru koor te tegu ca ay coobare wu, lu dagan mu gëm ne dafa dagan mu def ko, lu araam mu gëm ne dafa araam mu moytu ko, kooku dana dugg àjjana.