+ -

عن ابن عباس رضي الله عنهما
عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِيمَا يَرْوِي عَنْ رَبِّهِ عَزَّ وَجَلَّ قَالَ: قَالَ: «إِنَّ اللهَ كَتَبَ الْحَسَنَاتِ وَالسَّيِّئَاتِ، ثُمَّ بَيَّنَ ذَلِكَ، فَمَنْ هَمَّ بِحَسَنَةٍ فَلَمْ يَعْمَلْهَا كَتَبَهَا اللهُ لَهُ عِنْدَهُ حَسَنَةً كَامِلَةً، فَإِنْ هُوَ هَمَّ بِهَا فَعَمِلَهَا كَتَبَهَا اللهُ لَهُ عِنْدَهُ عَشْرَ حَسَنَاتٍ إِلَى سَبْعِمِائَةِ ضِعْفٍ، إِلَى أَضْعَافٍ كَثِيرَةٍ، وَمَنْ هَمَّ بِسَيِّئَةٍ فَلَمْ يَعْمَلْهَا كَتَبَهَا اللهُ لَهُ عِنْدَهُ حَسَنَةً كَامِلَةً، فَإِنْ هُوَ هَمَّ بِهَا فَعَمِلَهَا كَتَبَهَا اللهُ لَهُ سَيِّئَةً وَاحِدَةً».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6491]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm-
Jele nañu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci li mu soloo ci Boroomam mu màgg mi mu wax ne: «Yàlla dafa bind yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di leeral ko, képp ku yéene jëf i yiw, te defu ko, Yàlla dana ka ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, waaye bu ko yéenee ba noppi def ko, mu bindal ko fukki yiw, mannakoo Ful bamu yégg juróom-ñaari téeméeri, ba ci ay full yu bari, waaye képp ku Yéenee jëf lu ñaaw te defu ko Yàlla di na ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, bu ko Yéenee nag daldi koy def mu bindal ko wenn ñaawteef».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6491]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne Yàlla dogal na yiw yi ak ñaawtéef yi daal di leeralal ñaari Malaaka yi naka lañu koy bindee:
Képp ku namm a def lu rafet te dogu ci def ko dees na ko bindal wenn yiw doonte defu ko, bu ko defee nag ñu fulal ka ko fukk yu mel ni moom ba ci juróom-ñaari téeméeri yoon, ba ci ay yoon yu bari, ci kem la nek ca xol ba cig sellal ak jariñ ñeneen mbaa lu ni mel.
Waaye képp ku nàmm a def ñaawtéef te dogu ci def ko, far bàyyi ko ngir Yàlla dees na ka ko bindal aw yiw, bu ko bàyyee ngir yittewootu ko te deful ay sababam deesu ko bindal dara, waaye su ko bàyyee ngir ak lott dees na ko bindal yéeneem, su ko defee nag ñu bindal ko benn ñaawtéef.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Pulaar Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral ngëneelul Yàlla lu màgg li ci xeet wii am ci ful giñuleen di fulal ay yiw ak di ko bind fa moom, ak ñàkk giñuleen di ñàkka fulal séen i ñaawtéef.
  2. Njariñu yéene ci jëf yi ak ay jeexitam.
  3. Ngëneelu Yàlla mu kawe mi ak ug ñeewanteem ak rafetalam ci ne ku nàmm a def aw yiw te mujju ko def Yàlla bindal ko ko aw yiw.