+ -

عن أنس بن مالك رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«يَسِّرُوا وَلَا تُعَسِّرُوا، وَبَشِّرُوا وَلَا تُنَفِّرُوا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 69]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 69]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day digle ñu woyofalal nit ñi te bañ a jafeel ci séen kaw ci mbooleem biri diine ji, ak yu àdduna yi, loolu nag day yam fa Yàlla daganal te yoonal ko.
Day ñaaxe ba tay ci bégle ciw yiw, ak bañ a dàqaate.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Kanadi البلغارية Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Li war aji-gëm ji mooy mu bëggal nit ñi ci Yàlla te xemmemloo leen lu baax.
  2. Jaadu na ci kiy woote ci Yàlla mu xool cig xereñte naka lay àggalee wooteb Lislaam bi ci nit ñi.
  3. Bégle day waral mbégte ak ug jublu ak dal ñeel aji-woote ji li muy woo nit ñi.
  4. Jafeel day waral daw ak dummóoyu ak sikk-sakka ci waxi aji-woote ji.
  5. Yaatug yërmàndey Yàlla ci jaamam yi, te moom diine ju yaatu la leen bëggal ak Sariiha ju yomb.
  6. Yombal gi ñu digle mooy gi Sariiha indi.