عن سعد بن أبي وقاص رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«إِنَّ اللهَ يُحِبُّ الْعَبْدَ التَّقِيَّ الْغَنِيَّ الْخَفِيَّ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2965]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Sahd Ibn Abii Waqaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2965]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne Yàlla daa bëgg yenn jaamam yi,
Bokk na ci ñoom: ki ko ragal, ci def ay ndigali Yàlla, di moytu ay tereem.
Bëgg na it: Ku doylu Ku doyloo Yàlla mu màgg mi du sukkandiku ci nit ñi, te du geestu keneen ku dul Yàlla.
Day bëgg it: kiy nëbbu, kiy toroxlu, di jaamu Boroomam, di yittewoo luy jariñ, te yittewoowul kenn xam ko, mbaa ñu koy waxtaane, walla di ko tagg.