عَنْ المُغِيرَةِ رضي الله عنه قَالَ:
كُنْتُ مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي سَفَرٍ، فَأَهْوَيْتُ لِأَنْزِعَ خُفَّيْهِ، فَقَالَ: «دَعْهُمَا، فَإِنِّي أَدْخَلْتُهُمَا طَاهِرَتَيْنِ» فَمَسَحَ عَلَيْهِمَا.

Jële nañu ci Al-Muxiirata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne:
Nekkoon naa ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- cib tukki, ma nar a summi ñaari saŋam yi, mu ne ma: "bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab" mu masaa ca seen kaw.

Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 206

Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa nekkoon ci ab tukki, daal di jàpp, ba mu tollee ci raxas tànk yi Al-Muxiirata Ibn Suhbata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tàllal loxoom ngir summi li nekk ci tànki Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-di ay dàlli saŋ ngir mu raxas ñaari tànk yi! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ne ko: bàyyileen te bu leen summi, ndax damaa dugal samay tànk ci saŋ yi fekk maa ngi cig laab, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di masaa ci kaw saŋ yi mu wuutu raxas ñaari tànk yi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Li nu yoonal ci masaa ci ñaari saŋ mooy mu nekk ci jàpp ñeel toj mu ndaw, bu dee sangu nag ñeel toj mu mag raxas ñaari tànk yi du man a njàkk.
  2. Masaa benn yoon lay doon ci rombale loxo ba nu tooyal ci kaw saŋ yi wolif suuf gi.
  3. Danañu sàrtal ci masaa ci ay saŋ, mu sol ko ginnaaw am njàpp mu mat mom raxas na ca ñaari tànkam ci ndox, ak saŋ yi nekk lu laab, ak mu muur barabu farata ba, ak mu masaa leen ci toj mu ndaw bu mu nekk toj mu mag walla luy waral sangu, masaa mi it na nekk ca waxtu wa ñu ko tënk ci sariiha te mooy bis ak guddi ñeel ku nekkul cib tukki, ñatti bis ak seeni guddi ñeel ki nekk cib tukki.
  4. Dees na nattale ci ay saŋ lépp lu muur ñaari tànk yi niki ay kawas mbaa leneen, te dana dagan ñu masaa ca.
  5. Rafetug jikkoy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak um njàngaleem, ba tax mu tere Al-Muxiirata mu summi leen, daal di koy leeralal sabab si: ci ne bamuleen di sol boobu ay tànkam laab na, ngir xelam dal mu daal di xamit àtte bi.

Gaaral firi yi

58 Làkk wi
EN English الإنجليزية
UR اردو الأوردية
ES Español الإسبانية
ID Indonesia الإندونيسية
UG ئۇيغۇرچە الأيغورية
BN বাংলা البنغالية
FR Français الفرنسية
TR Türkçe التركية
RU Русский الروسية
BS Bosanski البوسنية
SI සිංහල السنهالية
HI हिन्दी الهندية
ZH 中文 الصينية
FA فارسی الفارسية
VI Tiếng Việt الفيتنامية
TL Tagalog تجالوج
KU Kurdî الكردية
HA Hausa الهوسا
PT Português البرتغالية
ML മലയാളം المليالم
TE తెలుగు التلغو
SW Kiswahili السواحيلية
TA தமிழ் التاميلية
MY မြန်မာ البورمية
TH ไทย التايلندية
DE Deutsch الألمانية
PS پښتو بشتو
AS অসমীয়া الأسامية
SQ Shqip الألبانية
SV Svenska السويدية
AM አማርኛ الأمهرية
NL Nederlands الهولندية
GU ગુજરાતી الغوجاراتية
KY Кыргызча القيرقيزية
NE नेपाली النيبالية
YO Yorùbá اليوروبا
LT Lietuvių الليتوانية
PRS دری الدرية
SR Српски الصربية
SO Soomaali الصومالية
TG тоҷикӣ الطاجيكية
RW Kinyarwanda الكينياروندا
RO Română الرومانية
HU Magyar المجرية
CS Čeština التشيكية
MOS Moore الموري
MG Malagasy المالاجاشية
OM Oromoo الأورومو
KN ಕನ್ನಡ الكانادا
AZ Azərbaycan الأذربيجانية
UZ O‘zbek الأوزبكية
UK Українська الأوكرانية
KA ქართული الجورجية
MK Македонски المقدونية
KM ភាសាខ្មែរ الخميرية
PA ਪੰਜਾਬੀ البنجابية
MR मराठी الماراثية
KMR Kurmancî الكرمنجية