عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«حَقُّ الْمُسْلِمِ عَلَى الْمُسْلِمِ خَمْسٌ: رَدُّ السَّلَامِ، وَعِيَادَةُ الْمَرِيضِ، وَاتِّبَاعُ الْجَنَائِزِ، وَإِجَابَةُ الدَّعْوَةِ، وَتَشْمِيتُ الْعَاطِسِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1240]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1240]
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral yénn àqi jullit bi ci mbokku jullitam, Bi njëkk ci àq yii mooy delloo nuyoo ñeel ku la nuyu.
Àqu ñaareel bi: seeti ku feebar.
Àqu ñatteel bi: gunge ab néew ci këram ba ca jullikaay ba, ba ca almeer ya ba ba ñu koy rob.
Àqu ñenteel bi: wuyu woote ba bu ñu ko woowee ci céetal ab séet mba leneen.
Àqu jurómeel bi: ndokkeel Ku tissooli, te mooy mu wax ko ndeem sant na Yàlla: yarhamulallaah, aji-tissooli ji wax: yahdiikumullaahu wa yuslihu baalakum.