عن أبي صِرْمة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ ضَارَّ ضَارَّ اللهُ بِهِ، وَمَنْ شَاقَّ شَقَّ اللهُ عَلَيْهِ».
[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 1940]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Sirmata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku lore Yàlla lor ko, ku sonle Yàlla sonal ko».
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 1940]
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo lor ab jullit, mbaa teg ko coono ci mbir mu mu man a doon; ci bakkanam walla alalam walla njabootam, ku def loolu Yàlla dana ko fay mbugal ko kem jëfam.