عن تميم الداري رضي الله عنه أن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«الدِّينُ النَّصِيحَةُ» قُلْنَا: لِمَنْ؟ قَالَ: «لِلهِ وَلِكِتَابِهِ وَلِرَسُولِهِ وَلِأَئِمَّةِ الْمُسْلِمِينَ وَعَامَّتِهِمْ».

Jële nañu ci Tamim Ad-Daarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne:
«diine de laayante-biir la» nu ne ko: ngir kan? Mu ne: «ngir Yàlla, ak ngir téereem bi, ak ngir Yónentam bi, ak ngir ñiiti jullit ñi, ak ngir jullit ñépp».

Wér na Muslim soloo na ko Téere Muslim bi gën a wér - 55

Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- day xamle ne diine ji day taxaw ci sellal ak dëgg, ngir ñu defe ko na ko Yàlla warale ba mu mat sëkk te du am genn gàtteñlu walla wuruj.
Ñu wax Yónente bi ne ko: kan la laaye-biir Gi kan la ñeel? Mu ne:
Bi ci njëkk mooy: laabire ñeel Yàlla mu kawe mi: ci sellal jëf yi ñeel ko, te bañ koo bokkaale, nu gëm ak kennam ci ay jëfam, ak ci jaamu gi, ak ci ay turam ak i meloom, ak di màggal mbiram, tey woote jëme ci gëm ko.
Ñaareel bi: laabire ñeel téereem bi te mooy Alxuraan ju tedd ji: ci nu gëm ne waxam la, te mooy téereem bi mujj, te moo folli mbooleem Sariiha ya ko jiitu, nu màggal ko, di ko jàng bu baax, tey jëfe ay laayaam yu leer yi tey gëm yu niroo ya, tey delloo pirim soppikat yi, tey waaru ci ay waaraateem, tey siiwal am njàngaleem, tey woote jëme ci moom.
Ñatteel bi: laabire ngir Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ci nu gëm ne mooy Yónente bi mujj, te dëggal ko ci li mu indi, tay jëfe ay ndigalam, di moytu ay tereem, ta nuy baña jaamoo Yàlla ci lu dul li mu indi, nuy màggal ay àqam, te di ko weg, di tasaare wooteem bi, ak Sariihaam bi, te di ko dindil tuuma yi.
Ñenteel bi: laabire ñeel njiiti jullit ñi: ci di leen dimbali ci dëgg, tey bañ a xëccook ñoom mbir mi, te di leen déggal ak di leen topp cig topp Yàlla.
Juróomeel bi: laabire ñeel mbooleem jullit ñi: ci rafetal jëme ci ñoom ak di leen woo ci diine ji, te bañ leen a lor, ak bëgg leen, tey dimbalànte ak ñoom cig mbaax ak ragal Yàlla.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Digle ag laabire ñeel ñépp.
  2. Màggaayu dayog laabire ci diine.
  3. Làmboo gi diine làmboo ay pas-pas ak i wax ak i jëf.
  4. Bokk na ci laabire sellal bakkan ci wor ki ngay laabire ak bëggal ko yiw.
  5. Rafetug njàngalem Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tax muy tënk am mbir ba noppi door koo faramfàcce.
  6. Tàmbalee ca la gën a am solo, ba tax na Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tàmbalee ci laabire ngir Yàlla, teg ci ngir tëereem bi, teg ci ñeel yónenteem bi, teg ci njiiti jullit ñi, teg ci nag mbooleem jullit ñi.

Gaaral firi yi

69 Làkk wi
EN English الإنجليزية
UR اردو الأوردية
ES Español الإسبانية
ID Indonesia الإندونيسية
UG ئۇيغۇرچە الأيغورية
BN বাংলা البنغالية
FR Français الفرنسية
TR Türkçe التركية
RU Русский الروسية
BS Bosanski البوسنية
SI සිංහල السنهالية
HI हिन्दी الهندية
ZH 中文 الصينية
FA فارسی الفارسية
VI Tiếng Việt الفيتنامية
TL Tagalog تجالوج
KU Kurdî الكردية
HA Hausa الهوسا
PT Português البرتغالية
ML മലയാളം المليالم
TE తెలుగు التلغو
SW Kiswahili السواحيلية
TA தமிழ் التاميلية
MY မြန်မာ البورمية
TH ไทย التايلندية
DE Deutsch الألمانية
JA 日本語 اليابانية
PS پښتو بشتو
AS অসমীয়া الأسامية
SQ Shqip الألبانية
SV Svenska السويدية
AM አማርኛ الأمهرية
NL Nederlands الهولندية
GU ગુજરાતી الغوجاراتية
KY Кыргызча القيرقيزية
NE नेपाली النيبالية
YO Yorùbá اليوروبا
LT Lietuvių الليتوانية
PRS دری الدرية
SR Српски الصربية
SO Soomaali الصومالية
TG тоҷикӣ الطاجيكية
RW Kinyarwanda الكينياروندا
RO Română الرومانية
HU Magyar المجرية
CS Čeština التشيكية
MOS Moore الموري
MG Malagasy المالاجاشية
FF Fulfulde الفولانية
IT Italiano الإيطالية
OM Oromoo الأورومو
KN ಕನ್ನಡ الكانادا
BG Български البلغارية
AZ Azərbaycan الأذربيجانية
EL Ελληνικά اليونانية
AK Akan الأكانية
UZ O‘zbek الأوزبكية
UK Українська الأوكرانية
KA ქართული الجورجية
LN Lingala اللينجالا
MK Македонски المقدونية
KM ភាសាខ្មែរ الخميرية
BM Bambara البامبارية
PA ਪੰਜਾਬੀ البنجابية
MR मराठी الماراثية
DA Dansk الدنماركية
RN Kirundi الكيروندي
KMR Kurmancî الكرمنجية
MS Bahasa Melayu الملايو