1. Li jiitu
  2. Ràññetle yi
  3. Dégg diine ak i cosaanam

Hadiis àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi

عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الْخُدْرِيِّ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّ الدُّنْيَا حُلْوَةٌ خَضِرَةٌ، وَإِنَّ اللهَ مُسْتَخْلِفُكُمْ فِيهَا، فَيَنْظُرُ كَيْفَ تَعْمَلُونَ، فَاتَّقُوا الدُّنْيَا وَاتَّقُوا النِّسَاءَ، فَإِنَّ أَوَّلَ فِتْنَةِ بَنِي إِسْرَائِيلَ كَانَتْ فِي النِّسَاءِ».

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi, ndax fitna ji njëkk a am ci Banuu Israayil ci jigéen la xewe».

Wér na Muslim soloo na ko Téere Muslim bi gën a wér - 2742

Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne àdduna ñam wu neex la, te naat ci gisiin, ba nit ki dana ci woroo, ba di ci nuur, ba def ko yitteem ji gën a rëy. Ak ne Yàlla dafa def ñenn ci nun ñuy wuutu ñeneen ci dundug àdduna, ngir xool lan lanuy def, ndax danu koy topp, walla danu koy moy? Topp mu wax: moytuleen poñaxiitam àdduna ak ub taaram di leen nax ba di leen jëme ci bàyyi li leen Yàlla digal, ba ngeen di def li mu leen tere. Bokk na ci li gën a màgg ci yi ñu war a moytu ci fitnay àdduna mooy fitnay jigéen ñi, ndaxte mooy fitna ji waa Banuu Israayil njëkk a tàbbi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Ñaaxe ci taqoo ak ragal Yàlla, te bañ a soxlawoo liy feeñ ci àdduna ak taaram bi.
  2. Moytondikuloo di fitnawu ci jigéen ñi, ci xool mbaa ci càgante ci góoru jàmbur di jaxasoo ak ñoom, mbaa yeneen.
  3. Fitnay jigéen bokk na ci fitna yi gën a màgg ci àdduna.
  4. Waaru ak xalam ci xeet yi jiitu woon, li xew ci Banuu Israayil man naa xew ci ñeneen.
  5. Fitnay jigéen bu dee jabar la man naa teg jëkkëram lu mu àttanul ci ab dund, ba dana ko soxlaal wolif muy sàkku ay biri diineem, ba dana ko yóbbe muy xawa alku ci sàkku biri àdduna, bu dee jàmbur nag fitnaam mooy fiir góor ñi ci jengloo leen wolif dëgg ci bu nu génnee ba jaxasoo ak ñoom, rawatina bu ñu nekkee jigéen yu sollut lu jot, tey baraj-baraji, te lii man naa waral tàbbi ci njaalo ci kem ay darajaam, kon war na ci aji-gëm ji mu làqu ci Yàlla, te yaakaar ko ci mucc ci seeni fitna.

Gaaral firi yi

58 Làkk wi
EN English الإنجليزية
UR اردو الأوردية
ES Español الإسبانية
ID Indonesia الإندونيسية
UG ئۇيغۇرچە الأيغورية
BN বাংলা البنغالية
TR Türkçe التركية
RU Русский الروسية
BS Bosanski البوسنية
SI සිංහල السنهالية
HI हिन्दी الهندية
ZH 中文 الصينية
FA فارسی الفارسية
VI Tiếng Việt الفيتنامية
TL Tagalog تجالوج
KU Kurdî الكردية
HA Hausa الهوسا
PT Português البرتغالية
ML മലയാളം المليالم
TE తెలుగు التلغو
SW Kiswahili السواحيلية
TA தமிழ் التاميلية
MY မြန်မာ البورمية
TH ไทย التايلندية
DE Deutsch الألمانية
PS پښتو بشتو
AS অসমীয়া الأسامية
SQ Shqip الألبانية
SV Svenska السويدية
AM አማርኛ الأمهرية
NL Nederlands الهولندية
GU ગુજરાતી الغوجاراتية
KY Кыргызча القيرقيزية
NE नेपाली النيبالية
YO Yorùbá اليوروبا
LT Lietuvių الليتوانية
PRS دری الدرية
SR Српски الصربية
SO Soomaali الصومالية
TG тоҷикӣ الطاجيكية
RW Kinyarwanda الكينياروندا
RO Română الرومانية
HU Magyar المجرية
CS Čeština التشيكية
MOS Moore الموري
MG Malagasy المالاجاشية
OM Oromoo الأورومو
KN ಕನ್ನಡ الكانادا
AZ Azərbaycan الأذربيجانية
UZ O‘zbek الأوزبكية
UK Українська الأوكرانية
KA ქართული الجورجية
MK Македонски المقدونية
KM ភាសាខ្មែរ الخميرية
BM Bambara البامبارية
PA ਪੰਜਾਬੀ البنجابية
MR मराठी الماراثية
KMR Kurmancî الكرمنجية