+ -

عَنْ أَبِي عَبْدِ الرَّحْمَنِ السُّلَمي رحمه الله قَالَ:
حَدَّثَنَا مَنْ كَانَ يُقْرِئُنَا مِنْ أَصْحَابِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنَّهُمْ كَانُوا يَقْتَرِئُونَ مِنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَشْرَ آيَاتٍ، فَلَا يَأْخُذُونَ فِي الْعَشْرِ الْأُخْرَى حَتَّى يَعْلَمُوا مَا فِي هَذِهِ مِنَ الْعِلْمِ وَالْعَمَلِ، قَالُوا: فَعَلِمْنَا الْعِلْمَ وَالْعَمَلَ.

[حسن] - [رواه أحمد] - [مسند أحمد: 23482]
المزيــد ...

Jele na ñu ci Abuu Abdu Rahmaan As-Sulamii -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne:
Ñi nu doon jàngal Alxuraan ci Sahaabay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax nañu nu ne ñoom dañu daan jàng ci Yónente bi fukki aaya, daawuñu jëlaat dara tek ko ca fukk ya ba baa ñuy xam li nekk ci yii ci xam-xam ak jëfe, nu wax ne: ñu boole xam ak jëfe.

[Tane na] - [Ahmat soloo na ko] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 23482]

Leeral

Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm-da ñu daan jàng ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki aayay Alxuraan, te daawuñu tuxu di jëll leneen ba kerook ñuy jàng li nekk ci fukk yooya ci xam-xam ñu jëfe ko, ñu boole xam-xam ba ak jëfe ga.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ak séenug xér ci xamlu Alxuraan.
  2. Xamlu Alxuraan day nekk ci xam ak jëfe li ci nekk, waaye nekkul ci jàng ak mokkal rekk.
  3. Xam-xam day jiitu wax ak jëf.
Ndollent