عن عثمان بن عفان رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ تَوَضَّأَ فَأَحْسَنَ الْوُضُوءَ خَرَجَتْ خَطَايَاهُ مِنْ جَسَدِهِ حَتَّى تَخْرُجَ مِنْ تَحْتِ أَظْفَارِهِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 245]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Usmaan Ibn Affaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Ku jàpp te rafetal njàpp ma, ay ñaawtéefam day génn ci aw yaramam bay génn ci ay weyam».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 245]
yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ku jàpp sàmmoonte ak Sunnay Njàpp ak i tegginam, loolu sabab la ci far ay ñaawtéef ak sippi ay ñuumte, "ba ay bàkkaaram di génne ci ay suufi weyi loxoom ak i tànkam"