+ -

عَنْ عُبَادَةَ بْنِ الصَّامِتِ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا صَلَاةَ لِمَنْ لَمْ يَقْرَأْ بِفَاتِحَةِ الكِتَابِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 756]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ku jàngul faatiha amul julli".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 756]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne julli du wér lu dul ci jàng saaru Faatiha, ndaxte ponk la ci ponki julli ci ràkka yépp.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Faatiha leneen manukoo wuutu ci ku ko man.
  2. Ràkka bu ñu jàngul faatiha day yàqu, ci ki ko tay, ak ki xamul, ak ki fàtte; ndaxte ponk la, te ponk du rot ba mukk.
  3. Jàng faatiha dana wàcci maamuum
  4. bi ji bu dabee imaam bi cib rukkoo.