عَن عَلِيٍّ بْنِ أَبِي طَالِبٍ رَضيَ اللهُ عنه قَالَ:
أَخَذَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ حَرِيرًا بِشِمَالِهِ، وَذَهَبًا بِيَمِينِهِ، ثُمَّ رَفَعَ بِهِمَا يَدَيْهِ، فَقَالَ: «إِنَّ هَذَيْنِ حَرَامٌ عَلَى ذُكُورِ أُمَّتِي، حِلٌّ لِإِنَاثِهِمْ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والنسائي وابن ماجه] - [سنن ابن ماجه: 3595]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aliyun Ibn Abii Taalib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jël Sooy ci càmmooñam, jël wurus ci ndayjooram, daal di leen yëkkëti ci loxoom, daal di wax ne: "ñaar yii dañoo araam ci sama góori xeet wi, waaye dagan nañu ci jigéen ñi".
[Wér na] - - [Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja - 3595]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jël yéreb Sooy walla ab moorso, ci loxob càmmooñam, daal di jël takkaayu wurus mbaa lu ko niru ci loxob ndayjooram, daal di wax ne: Sooy ak Oor, araam na góor ñi di ko sol, bu dee jigéen ñi nag dagan na ci ñoom.