+ -

عَنْ أَبِي مُوسَى رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّمَا مَثَلُ الْجَلِيسِ الصَّالِحِ وَالْجَلِيسِ السَّوْءِ كَحَامِلِ الْمِسْكِ وَنَافِخِ الْكِيرِ، فَحَامِلُ الْمِسْكِ: إِمَّا أَنْ يُحْذِيَكَ، وَإِمَّا أَنْ تَبْتَاعَ مِنْهُ، وَإِمَّا أَنْ تَجِدَ مِنْهُ رِيحًا طَيِّبَةً، وَنَافِخُ الْكِيرِ: إِمَّا أَنْ يُحْرِقَ ثِيَابَكَ، وَإِمَّا أَنْ تَجِدَ رِيحًا خَبِيثَةً».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2628]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne, ki yor gëttug Misk gi: benn mu mayla ci, walla nga jënd ci, mbaa nga am fi moom xet gu neex, kiy upp ab furne nag moom: benn mu lakk say yére, walla nga jële fa xet gu bon».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2628]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa joxe misaal ci ñaari xeeti nit:
Bi ci njëkk: toogandoo ak àndandoo bu sell buy tegtale Yàlla ak lu ngëremam nekk, di dimbalee ci topp Yàlla, Moom de day mel ni jaaykatu Misk, benn mu joxla ca, walla nga jënd ca, mbaa nga xeeñcu fa xet gu teey te neex.
Ñaareel bi: toogandoo ak àndandoo bu bon; kiy teree topp Yàlla, tey dimbalee ci ay moy, ngay gis ci moom ay jëf yu bon, ñu lay ŋàññ ndax li ngay ànd ak di toog ak ku mel ni moom. Misaalam moo ngi mel ni tëggkat biy upp sawara; benn mu lakk say yére ci sawara wiy naaw, walla nga jële fa ci jege gi nga ko jege ag xet gu bon.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sadd ay misaal ngir jegele maanaa mi ci kiy dégg lu dagan la.
  2. Ñaaxe ak xemmemloo ci ñuy toogandoo ak toppkatu Yàlla yu yiw yi, te moytu yàqkat yi boroom jikkó yu ñaaw yi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi