عَنْ أَبِي قَتَادَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا يُمْسِكَنَّ أَحَدُكُمْ ذَكَرَهُ بِيَمِينِهِ وَهُوَ يَبُولُ، وَلَا يَتَمَسَّحْ مِنَ الْخَلَاءِ بِيَمِينِهِ، وَلَا يَتَنَفَّسْ فِي الْإِنَاءِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 267]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Xataadata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«bu kenn ci yéen laal sakaraam ci ndayjooram fekk ma ngay saw, te bu demee duus ba noppi bu mu fompoo ndayjooram, te bu mu noyyi ci ndab li».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 267]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na yenni teggin yi; ba tax mu tere góor di laa sakaraam ci ndayjooram fekk ma ngay saw, ak ñu dindi sobe ci ginnaaw walla ci kanam ci loxo ndayjoor; ndaxte ndayjoor dañu koo waajal ngir yu tedd yi, Kem ni mu teree nit ki di noyyi ci ndab li muy naane.