عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صلى الله عليه وسلم قَالَ:
«دَعُونِي مَا تَرَكْتُكُمْ، إِنَّمَا هَلَكَ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمْ بِسُؤَالِهِمْ وَاخْتِلَافِهِمْ عَلَى أَنْبِيَائِهِمْ، فَإِذَا نَهَيْتُكُمْ عَنْ شَيْءٍ فَاجْتَنِبُوهُ، وَإِذَا أَمَرْتُكُمْ بِأَمْرٍ فَأْتُوا مِنْهُ مَا اسْتَطَعْتُمْ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 7288]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bàyyileen ma bu ma leen bàyyee, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seeni laaj ak di wuute ak seeni Yonnente , bu ma leen teree dara nangeen ko moytu, bu ma leen digalee dara defleen ca lu ngeen man».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 7288]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day fàttalee ne àttey Sariiha yi ñatti xaaj la: lu ñu noppi, lu ñu tere, ak lu ñu digle.
Bu njëkk bi: te mooy lu Sariiha noppi: ba tax tegu ci benn àtte, te cosaan ci mbir yi mooy ñàkk a war; Bu dee jamonoom moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- li war mooy bañ koo laaj dara lu tàbbeegul ndax ragal ñu wàcce ci ag waral walla araamal, ndax Yàlla da koo bàyyi ngir yërëm jaam ñi, Bu dee ginnaaw bi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- faatoo nag kon laaj ngir leerlu ak xamle lu ñu yittewoo ci mbiri diine loolu dagan na lu ñu digle la sax nag, bu dee nag ci anamug taral ak sonle loolu lañu namm ci bàyyi laaj bi ci hadiis bi; ndaxte loolu man naa yóbbe ca la Banuu Israayil tàbbi woon, ndaxte dañu leen a digal ñu ray aw nag te nag wu ñu rayoon rekk def nañu ndigal la, waaye dañoo taral ñu taral ci seen kaw.
Ñaareel bi: tere yi; te mooy: lol ku ko bàyyi am ca ab yool, ku ko def am ca mbugal, ñu war a moytandiku léppam.
Ñatteel bi: ndigal yi; te mooy: lol ku ko def am ca ab yool, ku ko bàyyi am ca mbugal, ñu war caa def lu ñu man.