عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قال: قال رَسُولُ الله صلى الله عليه وسلم:
«إِنَّ اللهَ يَغَارُ، وَإِنَّ الْمُؤْمِنَ يَغَارُ، وَغَيْرَةُ اللهِ أَنْ يَأْتِيَ الْمُؤْمِنُ مَا حَرَّمَ عَلَيْهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2761]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2761]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla day fiir di bañ di sib, kem ni aji-gëm ji di fiire ak di bañe ak di sibe, te sababus fiiràngem Yàlla mooy way-gëm ji def lu Yàlla araamal ci moom ci ay ñaawteef niki njaalo ak ngóor-jigéen, ak sàcc ak naan sàngara ak yeneen ñaawteef.