عَنْ أَنَسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قالَ:
«لاَ يُؤْمِنُ أَحَدُكُمْ، حَتَّى يُحِبَّ لِأَخِيهِ مَا يُحِبُّ لِنَفْسِهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 13]
المزيــد ...
Jële nañu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam"
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 13]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne ´gëm gu mat kenn du ko am lu dul ne dafa bëggal mbokkam li mu bëggal boppam ci jaamu Yàlla ak xeetu yiw yi ci diine ak ci àdduna, bu gisee ci mbokkam ag wàññeeku ci diineem, day pasteefu ci yéwénal ko, bu ca gisee yiw mu dëgëral ko ca, te dimbale ko ca, daal di koy laabire ci mbiri diineem ak àddunaam.