+ -

عَنْ عَلِيٍّ رضي الله عنه قَالَ:
كُنْتُ رَجُلًا مَذَّاءً وَكُنْتُ أَسْتَحْيِي أَنْ أَسْأَلَ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لِمَكَانِ ابْنَتِهِ فَأَمَرْتُ الْمِقْدَادَ بْنَ الْأَسْوَدِ فَسَأَلَهُ فَقَالَ: «يَغْسِلُ ذَكَرَهُ وَيَتَوَضَّأُ». وَلِلبُخَاريِّ: فَقَالَ: «تَوَضَّأْ وَاغْسِلْ ذَكَرَكَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 303]
المزيــد ...

Jële nañu ci Aliyun -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Góor laa woon gu bari masyu ma amoon kersay laaj ko Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir wàccuwaay gi doomam am, ma digal Al-Miqdaad ibnul Aswad mu laaj ka ko, mu ne ko: "day raxas sakaraam daal di jàpp". Bu dee ci Al-Buxaarii: da ne ko: jàppul te raxas sa sakara".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 303]

Leeral

Aliyun Ibn Abii Taalib day xibaare ne moom ku bari woon lu muy génne masyu la -te mooy ndox mu weex mu woyof te rattax tey génne ci sakara cig bànneex walla mu jiitu ag sëy-, Te xamul lan lay def ak génn googu, mu rus koo laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ngir ne moom mooy jëkkëru Faatimata doomu Yonnente bi Mu sàkku ci Al-Miqdaad ibnul Aswad mu laaj ko Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, Yonnente bi tontu ko: ci ne na raxas pëyam, te daal di jàpp.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu Aliyun Ibn Abii Taalib -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, ndax kersa terewu koo laaj waaye jaare ko ci keneen.
  2. Wuutal keneen ci laaj dagan na.
  3. Dagan na ci nit ki mu xibaare ci boppam ci lulu rus ngir yéwénal.
  4. Sobeg masyu, ak ne dañu koo war a raxas mu deñ ci yaram wi ak yére yi.
  5. Génne masyu bokk na ci yiy yàq njàpp.
  6. War na ñu raxas sakara wi ag ñaari xuur yi ndax li mu rot ci beneen hadiis.
Ndollent