عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قال:
جَاءَ نَاسٌ مِنْ أَصْحَابِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَسَأَلُوهُ: إِنَّا نَجِدُ فِي أَنْفُسِنَا مَا يَتَعَاظَمُ أَحَدُنَا أَنْ يَتَكَلَّمَ بِهِ، قَالَ: «وَقَدْ وَجَدْتُمُوهُ؟» قَالُوا: نَعَمْ، قَالَ: «ذَاكَ صَرِيحُ الْإِيمَانِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 132]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Ay nit ci Sahaaba yi dañoo ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ñu laaj ko ne ko: nun de dananu yég ci sunu bopp loo xam ne dana rëy lool kenn i nun di ko wax, mu ne leen: «te yég ngeen ko?» Ñu ne ko: waaw, mu ne leen: loolu mooy ngëm gu leer».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 132]
Leerarug hdiis bi: Am mbooloo ci Sahaabay Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañoo ñëw laaj ko li ñuy yég ci séen biir ci ay bir yu rëy yoy wax ko dana rëy lool ci ñoom ngir ag bonam ag ni ñu ko bañe, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: loolu ngeen di yég mooy ngëm gu leer, te kóolute gi leeni yóbbu ba ngeen di tere li Saytaane di sànni ci xol yi, ba ngeen di ñaawlu wax ja, muy màgg ci séen bopp, ba Saytaane du man dara ci séen xol yi, wuuteek ñi Saytaane am kàttan ci séen i xol te amuñu lu ko man a jeñ.