+ -

عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بِن مَسْعُودٍ رضي الله عنه قَالَ:
سَأَلْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: أَيُّ العَمَلِ أَحَبُّ إِلَى اللَّهِ؟ قَالَ: «الصَّلاَةُ عَلَى وَقْتِهَا»، قَالَ: ثُمَّ أَيٌّ؟ قَالَ: «ثُمَّ بِرُّ الوَالِدَيْنِ» قَالَ: ثُمَّ أَيٌّ؟ قَالَ: «الجِهَادُ فِي سَبِيلِ اللَّهِ» قَالَ: حَدَّثَنِي بِهِنَّ، وَلَوِ اسْتَزَدْتُهُ لَزَادَنِي.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 527]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Laaj naa Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla" nee naa moo ma ko wax, te bi ma sàkkoon ndollin mu dolli ma.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 527]

Leeral

Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: julliy juróom ci waxtoom wi ko Sariiha tënk, Teg ca fonk ñaari way-jur, di rafetal jëme ci ñoom, di taxaw ci seeni àq, te bañ leen a moy, Teg ca jihaad ci yoonu Yàlla, ngir yëkkati kàddug Yàlla mu màgg mi, ak aar diineem ji ak waa diine ji, ak fésal màndargaam, ci bakkan ak ci alal.
Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- nee na: moo ma xibaar jëf yii; te bu ma ko waxoon: teg ca lan? Kon dana ma dolli.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Gënanteg jëf yi ci seen diggante mi ngi aju ci Yàlla bëgg ko.
  2. Ñaax jullit bi ci mu xér ci jëf yi, jiital bi gën teg ca ba ca tege.
  3. Tontuy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jan jëf moo gën dana wuute, ci kem nit ñi ak seeni melokaan, ak lan moo ëpp njariñ ci kenn ku ne.