عَنْ عَائِشَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«تَحَرَّوْا لَيْلَةَ القَدْرِ فِي الوِتْرِ مِنَ العَشْرِ الأَوَاخِرِ مِنْ رَمَضَانَ».

Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor».

Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2017

Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc soññee na ci pasteefu ci dàkk Laylatul Xadri ci di baril ay jëf yu baax, moom nag fa gën a yaakaaru mooy mu nekk ci guddi yu wéet yi ci fukki fan yu mujj yi ci weeru koor ci at mu nekk, te mooy: ñaar-fukk ak benn, ak ñaar-fukk ak ñatt, ak ñaar-fukk ak juróom, ak ñaar-fukk ak juróom-ñaar, ak ñaar-fukk ak juróom-ñent.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Ngëneelu Laylatul Xadri ak ñaaxe ci di ko dàkk.
  2. Bokk na ci xereñteg Yàlla ak yërmàndeem mu nëbb guddi gii ngir nit ñi pasteefu ci jaamu gi, ngir sàkku ko, ndax seen yool bari.
  3. Laylatul Xadri mi ngi ci fukki guddi yi mujj ci weeru koor, te ci yu tóol yi la gën a yaakaaru.
  4. Laylatul Xadri benn la ci fukki guddi yi mujj ci weeru koor, te mooy guddi gi Yàlla mu màgg mi wàcce Alxuraan ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu def guddi gii mu gën junni weer ci baarke, ak màggug dayoom, ak jeexiti jëf yu baax ci moom.
  5. Tudde nañu ko(Laylatul Xadri) ci sukoon Daal gi benn mu jóge ci teddnga, dees na wax: diw ku màgg dayo la, laafal gi ñu laafal guddi gi nekk ci buntub laafal dara ci meloom, maanaam guddi gu tedd gi, maanaam moom ku màgg dayo la ci teddnga ak ug màggaay ak ug dayo ba mu jeex, {Nun noo ko wàcce ci guddi gu baarkeel} [Ad-Duxaan: 3], benn mu jóge ci nattale: laafal gi nekk laafal jamono ca la mu làmboo, maanaam guddi gii mooy gi nga xam ne ca la nattale liy am ci at mi di nekk, {ca lañuy teqale bépp mbir mu ñu xereñe} [Ad-Duxaan: 4].

Gaaral firi yi

46 Làkk wi
EN English الإنجليزية
UR اردو الأوردية
ES Español الإسبانية
ID Indonesia الإندونيسية
UG ئۇيغۇرچە الأيغورية
BN বাংলা البنغالية
TR Türkçe التركية
RU Русский الروسية
BS Bosanski البوسنية
SI සිංහල السنهالية
HI हिन्दी الهندية
ZH 中文 الصينية
FA فارسی الفارسية
VI Tiếng Việt الفيتنامية
TL Tagalog تجالوج
KU Kurdî الكردية
HA Hausa الهوسا
PT Português البرتغالية
ML മലയാളം المليالم
TE తెలుగు التلغو
SW Kiswahili السواحيلية
TA தமிழ் التاميلية
MY မြန်မာ البورمية
TH ไทย التايلندية
DE Deutsch الألمانية
PS پښتو بشتو
AS অসমীয়া الأسامية
SQ Shqip الألبانية
SV Svenska السويدية
AM አማርኛ الأمهرية
NL Nederlands الهولندية
GU ગુજરાતી الغوجاراتية
NE नेपाली النيبالية
PRS دری الدرية
SR Српски الصربية
RO Română الرومانية
HU Magyar المجرية
MOS Moore الموري
MG Malagasy المالاجاشية
KN ಕನ್ನಡ الكانادا
UK Українська الأوكرانية
KA ქართული الجورجية
MK Македонски المقدونية
KM ភាសាខ្មែរ الخميرية
PA ਪੰਜਾਬੀ البنجابية
MR मराठी الماراثية