عَنْ أُبَيِّ بْنِ كَعْبٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«يَا أَبَا الْمُنْذِرِ، أَتَدْرِي أَيُّ آيَةٍ مِنْ كِتَابِ اللهِ مَعَكَ أَعْظَمُ؟» قَالَ: قُلْتُ: اللهُ وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ. قَالَ: «يَا أَبَا الْمُنْذِرِ، أَتَدْرِي أَيُّ آيَةٍ مِنْ كِتَابِ اللهِ مَعَكَ أَعْظَمُ؟» قَالَ: قُلْتُ: {اللهُ لا إِلَهَ إِلا هُوَ الْحَيُّ الْقَيُّومُ} [البقرة: 255]. قَالَ: فَضَرَبَ فِي صَدْرِي، وَقَالَ: «وَاللهِ لِيَهْنِكَ الْعِلْمُ، أَبَا الْمُنْذِرِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 810]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«yaw Aba-Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi?» Nee na: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo xam. Mu ne ma: «yaw Aba- Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi ?» Nee na: ma ne ko: {Allaahu laa-i-Laaha illaa huwa Al-Hayyul Xayyuumu} [Al-Baxara: 255]. Nee na: mu dóor sama dënn, daal di wax ne: «giñ naa ci Yàlla, na xam-xam ndokkeel Aba- Munsir».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 810]
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Ubay Ibn Kahb aaya bi gën a màgg ci téere Yàlla bi, muy dengi-dengi ci tontu bi, mujj gi mu ne: mooy aayatul Kursiyyu: {Allaahu laa ilaaha illaa huwa Al Hayyul Xayyuumu}, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dëggal ko, daal di fëgg dënnam ngir junj ne fees na dell ak xam-xam ak xereñ, daal di koy ñaanal mu texe ci xam-xam bi te ñu yombalal ko.