+ -

عن ابن عمر رضي الله عنهما عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«أحْفُوا الشَّوَارِبَ وأَعْفُوا اللِّحَى».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 259]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«jempleen Seen mustaas yi, te yar sikkim yi».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 259]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa digle ñu dindi dara ci kawaru mustaas te bañ koo bàyyi noonu, waaye dañu koy jemp.
Ca wet ga mu digle ñu yar sikkim bàyyi ko mu sëq.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Araamal nañu wat ab sikkim.