عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: إِنَّ رَسُولَ اللهِ صلى الله عليه وسلم قَالَ:
«إِذَا شَرِبَ الْكَلْبُ فِي إِنَاءِ أَحَدِكُمْ فَلْيَغْسِلْهُ سَبْعًا».
ولمسلم: « أولاهُنَّ بالتُراب».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 172]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«bu ab xaj naanee ci ndabul kenn ci yéen na ko raxas juróom-ñaari yoon».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 172]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na ñu raxas ndab yi juróom-ñaari yoon bu ci ab xaj dugalee làmmeñam, bu njëkk bi ànd ak suuf ngir ndox mi ñëw ginnaawam, mu am cett gu mat ca sobe sa ak lor ja.