+ -

عَنِ ‌ابْنِ عَبَّاسٍ رَضِيَ اللهُ عَنْهُمَا قَالَ:
كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَليهِ وَسَلَّمَ لا يَعْرِفُ فَصْلَ السُّورةِ حَتَّى تَنْزِلَ عَليْهِ {بِسْمِ اللَّهِ الرَّحْمَنِ الرَّحِيمِ}.

[صحيح] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 788]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul woon xam luy xàjjale saar yi ba ba ñuy wàcce ci Moom {Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim}.

[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 788]

Leeral

Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- day leeral ne saari Alxuraan yi da daan wàcci ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- te daawul xam teqale ba ak fan la yam, ba ba ñuy wàcce ci moom: "Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim" mu door a xam ne saar wi jiitu jeex na, weneen saar wu bees moo tàmbali.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim mooy tàqale diggante saar yi, bamu des diggante saaru Al-Anfaal ak saaru At-Tawba.Bokk na ci njariñal hdiis bi:
Ndollent