Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

:
عربي Àngale Urdu
Ñëw naa fi Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ànd ak mbooloo yu bokk ci giirug Al-Asharii, mu wax ne: "giñ naa ci Yàlla ne duma leen gàddu te sax amuma lu ma leen gàddul" ñu des fa diir ba soob Yàlla, ñu dal di koy indil ay giléem, mu digle ñu jox leen ñatti giléem, ba ñu fa jógee, ñenn ci nun wax ñeneen ñi: Yàlla de du nu baarkeelal, ñëw nanu fi Yonnente Yàlla bi di sàkku mu gàddul nu mu giñ ne du nu gàddul ba noppi daal di nuy gàddul, Abuu Muusaa nee na: nu dem fi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ko loolu, mu ne nu: "du man maa leen gàddul, waaye Yàlla moo leen gàddul, @man de giñ naa ci Yàlla ne -bu soobee Yàlla- duma giñ ci dara ba noppi gis leneen lu ko gën, lu dul ne dinaa kaffaara sama giñ ba te def la ko gën".
عربي Àngale Urdu